LI NU WAR

Jëlal li nga moom
Bàyyi fi li ci des
Ta dem wuti koom
Def ne ñi ci des

Réew mi noo ko bokk
Ta ñépp a bëgg a mos
Bul jël li ñepp bokk
Neenal ñi ci des

Li nu Yàlla may
Ku ne xaj na ci
Ku bëgga góob na bay
Ta bàyyi luubal gi

Ngir réew ni naat
Fàww coono am
Foo gis ub légét
Góom a fa masa am

Foo gis teraanga
Coono jaar na fa
Foo gis safaan ba
Tàyyeel jiitu na fa