MBAYUM GERTE
Téeg xiin na ba ñalingaan
Am ndox di yendoo xeeñ
Mujj ngelawul njayaxaan
Nees tuut lépp ni tekk
Ag melax ni rayy ni xuyy
Ag dënu ni téll ni tuyy
Ñépp fatu ni séeni bunt kàpp
Toqi ndox yay jóge ca kaw
Yàlla Ngéej ji yendoo taw
Bët sébbi na suuf si tooy
Nooflaayu baykat yi jeex
Njël gu jëkk jëwriñ ja jóg
Àndak surga sa jubali tool
Ñee nga yanu saakuy kemb
Ña ca des nga gàdduy larmet
Jigéen ñaa nga yanu’y paan
Paan yu def ndoxum naan
Ruuj ba rafet gajj ba set
Tool ba yaatu , suuf sa saf
Ñee di tobbi ñële di ji
Jiwu wa jeex ñu buural
Surga raado bala ñoŋali
Nji ma sax gàncax ga naatal
Ganaaw raado bay bayaat
Balarñi teg ca toppaat
Teg ca deqi ak dajaley tar
Boole tar yi mu dooni naaf
Làpp ga door, làppu yay dal
Xale ya jóg tàmbalee jeexaat
Jigéen ñaa nga àndadoo di jéri
Gerte ni gàññ, ngooñ it bari.
Yal na Yàlla sunu Buur
Musal nu ci mépp ruur
Ruur mi jëmële ci biir tool yi
Rawatina mi dugg ci biir réew mi.
Maysa Gay SÀMB