JEEXITALI JËF

Lépp lu la gaar

Ngalla bum la waar

Am na ci loo jaar

Ta defóo ca la la war

Geesul sa gannaaw

Taxaw laaj sam xel

Lépp lu dal sa kaw

Am na ci lu la ñeel

Loo yaakaar mu neen

Foog ni du masa feeñ

Mu gaaw mbaa mu yeex

Léppay masa leer

Ak lumu mana doon

Dara du naaxsaay

Yal na doon lu baax

Pay gaa nga ciw yoon

Na ngay def lu baax

Ta bul bañ ñu lay ñaax

Ndax réccu day wees

Ta loo gis day jeex

Jaamul sa Boroom

Fonkal sa moroom

Ta lumu mana doon

Na nga ko teg ci yoon.

Maysa Gay SÀMB.

Leave a Reply

Your email address will not be published. Required fields are marked *