NJARIÑAL MBAY
Lolli bi jeex
Noor bi dugg
Sàq yi fees
Dund bi bari
Xel yépp dal
Gerte gi jar
Jiba yi fees
Xaalis bari
Soxla faju
Ligéey barke
Coono njariñ
Mbégte mi door
Ndaje yi bari
Ngomaar yi riir
Kasag yi jolli
Taaxuraan yi bir
Mbapat yi birële
Ligéey barke
Coono njariñ
Waxambaane yi takk
Njanq ji séyi
Ñaan yi nangu
Jàmm ji sax.
Ligéey barke
Coono njariñ
Maysa Gay Sàmb.