Nday Aminta Njànja
Nday Ami Njaay
Nday Ami Njànja
Kuko laaj lu mu bëgg
Mu ni la cerey Njànja
Muy suba wàlla ngoon
Waxtu wu mu mana doon
Foo fekk janq Njaay
Mi ngi lekk cerey Njànja
Donte amul neex
Walla sax tuuti soow
Da koy lekk ba mu jeex
Boole kook tuuti meew
Suy lekk cerey Njànja
Bookoy nuyu du la fay
Nga ñaan ko ci du la may
Àkka bëgg cerey Njànja
✍🏿: Maysa Gay Sàmb