YARAL SA DOOM
Yaral sa doom
Ta teg ko ci yoon
Def jom ci moom
Jàngal ko wax
Ak def lu baax
Xamal ko dëgg
Ak li mu wara bëgg
Nay fonk i mag
Jox léen cër bu mat
Sàkku ci ñoom ñaan
Xéewël yuy baawaan
Jàngal ko am dal
Ci lu mu mana doon
Ta am farlu gu mat
Ci lépp li ko war
Jàngal ko xam xam
Ak fonk ligéeyam
Ñaanal ko gudd fan
Ak dund gu jàppandal
Yal na nekk mag
Mag mu am u ñam
Yal na am ug njaboot
Gu lépp’am barkeel
Maysa Gày SÀMB.