JIGÉEN JU BAAX
Yiw nga ta teey nga
Ba ku la gis naw na la
Sa jëmm ji rafet na
Sa wërañ ji jekk na
Ta sa’m ndaag teey na
Sa’y kàddu neex na ma
Ta sa tontu it ump na ma
Sa siiñ maa ngi ñuul
Ànd’ak bëñ yu weex
Sa’b der maase ñuul
Gënal ma der bu weex
Sa muuñ gi rafet lool
Ta sa’y ree neexa bëgg
Sa’g col yiw na lool
Sa’m kodd jot na sëkk
Soo toggee mu neex
Ta soo yakkee du jeex
Loo am séddoo nga ko
Ndax siisoo ta ŋottóo
Ëppaloo bëgge woo
Loo am doyloo nga ko
Xeeboo ta tuutaloo
Loo ñàkk it muñ nga ko
Doo xaste doo xulóo
Doo jànni doo ŋaayoo
Doo def luy merloo
Yaa noppal dëkkandoo
MAYSA GAY SÀMB