MÀNDIŊ

Àll ni sendaw lépp ni tekk

Naaj wi tàng may dox man rekk

Ñax mi bari mbooy gi ni ñareet

May waaxu gaaw ne’b sareet

Ma xool ndey joor lépp ni selaw

Xool càmmooñ lépp di nelaw

Xool ci kanam séenu ma dara

Geestu gannaaw gisu ma dara

Màndiŋ mi yaatu ta raglu lool

Saa’m xel di rabat ak di xalaat

Ñall wi gudd bari ñax ta xat

Lu yëngu ma tiit fu ne ma xool

Xel indil ma la maam daan léeb

Àll bu yaatu ta bari’y mala

Bari’y njanaaw ak léppi balaa

Ba tax lu ma waaxu diko xeeb

Des picc yiy sab yamb yiy biiw

Soccet yiy tëb def am ndiiraan

Gunóor’ak mellent lépp di raam

Tan yi ci téeg naaw di ma tiim

Dara ni yoxyox saa’w fit ni térét

Ma dëgg i tànk mujj ni yoleet

Mu ni ñoxñox saa’g noo ni tekk

Ma ñaadam ñaadami ni meŋŋ

Ma takk saa‘w fit dellu ànd ak dal

Yokk saa jéego ba mel ni kuy daw

Ngir ñibbi ak waaxu mu gaaw

Ta bañ ni wëqet mel ne’b ragal

Wolof Njaay neena mere Màndiŋ mana waaxoo ko gën.