JIKKOY TAY
Ana ngor ana jom
Man de waaru naa
Jikko yi baax yi fi amoon
Dañoo mujj jeex xanaa
Màndu lan daan bàkkoo
Teg ci suturaal àndandoo
Leegi lu waay xam mu siiw
Ana jikkoy nit ku yiw
Ana yar ana teggiin
Man de jaaxle naa
La fi maam ya tegoon
Daa mujj réer xanaa
Demb wëlëree fi amoon
Teg ci fonk sa moroom
Moytu wax ak def lu ñaaw
Sàmm ak setal sa gànnaaw
Ana sabablu ana doylu
Man de yéemu naa
Ñoŋal koom mi nu ànd sàkku
Da fee mujj xewwi xanaa
Ana fulla ak fayda yi amoon
Man de jommi naa
Ku ruur ñu teg ko ci yoon
Da fee mujj jeex xanaa
✍🏿: Maysa Gay Sàmb