MOYTUL


Bul jël lu lewul

Ta bul sos lu amul

Bul def lu warul

Bul tuumaal ku deful

Bu wax lu yiwul

Ta bul wax loo narul

Bu digee loo manul

Bul seede loo xamul

Bul góob lu ñorul

Bul mbumbaay ta jotul

Bul dugg ci lu wóorul

Ta bul jëm fu gënul

— Anna Wong, Volunteer

✍🏿: Maysa Gày Sàmb.