NDAM LI
Def ngéen li léen war
Tasu léen yaakaar
Ndam li la nu doon xaar
Yéen a di ay JàmbaarWane ngéen li ngéen man
Ta def ngéen ci séen jom
Siggil ngéen Senegaal
Kenn du léen jàmm naanTax ngéen ñépp bég
Ku nekk ak la mu yëg
Ñépp àndandóo
Réew mi riirandóoÑii ngi sëgg di jooy
Mu di jooyi bànneex
Ñépp la séeni xol tooy
Ku nekk am li ko neexÑee ngay tëb di dal
Mel ne ñu dëgg ciy xal
Fu ne ñu daw fa jëm
Yàlla bu mu fi yamJërëjëf Jëwrin
Aliyoo ma tax di wax
Wane nga sa maniin
Ta boole woo ci waxBay nga sas wu rëy
Gën gee rafetu mbay
Ñépp nee na ñu waaw
Ci Biir ak bittim réew
Aji bind ji : Maysa Gay Sàmb.